Li aju ci dëkkuwaay bi

  • Ndar, dëkku ndox : déndub bël.
  • Tefes gi sës ci taaxu Ndar dëkk la bu ëmb kàrcey nappkat yi, ay taax yu ñu jagleel doxandeem yi (turism) ak barab yu ñuy sopparñee jën.
  • « Langue de Barbarie »  moo ëpp nit ci Ndar. Ñetti kàrce yii – Get-Ndar, Ndar-Tuut, Goxu Mbaac – ci la 27,3 % ci askanu 18 kàrce Ndar yi dëkk.

Gànjool gox bu rëb la bu ëmb

  • « Langue de Barbarie » di suuf su fegu ci tefesu géej gi. Mi ngi yaatoo 120 ba 400 m, kawee ba 7 meetar te guddee 25 ba 30 km.
  • Askani dëkk-kaw yi fegu géej gi (niki Tasineer, Muwit, Pilot Baar, Njébéen) ñi ngi yëngu ci napp, mbeyum noor, wott xorom ak yoxos
  • suufus dun sa gàncax gi daa sonn ndax bekkoor gi
  • ndoxu siyaan yu jàppandi lool te tënku ci coppikug kéew gi (liy jóge ci taw bi bariwul te lu ci bari di ñeer).
  • Ndar dafa néew doole lool :
  • Gàncax giy sax ci ndox mi dëkke di diig ndax ndoxu géej gi, booleek gaw (dig) yiy fàcc
  • Pàrku « Langue de Barbarie » fi mbonaat yiy nenee, dunu njanaaw yi, tooli mbeyum noor yi, nappum dex bu Mumbaay, déndu géej bi ñu aar bu Dun Baaba Jéey, ñee nañu mes mbaa ñu nekk ci tànk yi
  • Ndar ak Gànjool ñoo séddoo  suuf si fegu ci tefesu géej gi. « Langue de Barbarie » daa topp guddaayu Ndar diggante géej geek dex gi. Ginnaaw dog-dog yi yenni sañc waral, daanaka fépp a maase.
  • Fàcc yi day wone li mën a am ci déndu géej gi ñu aarul ci doole ji ndox mi ko séq di yëngoo.

Ci jéeri ji : xàllu Gàndoŋ, Paal et Faas Ngom

  • Gàndoŋ, Paal ak Faas Ngom ñi ngi nekk ci suuf su xonk si baax si mbeyum nawet. Dees na fa bey it mbeyum noor ak càmm.
  • Mbey mi li koy faagaagal mooy taw yu jaarul yoon (yu yeex, yu ëpp, mbaa yu jamonoy ngóob).
  • Gàndoŋ, Faas Ngom ak Paal ñoo yem màndarga yu aju ci coppikug kéew gi : taw yu néew, ngelaw yu bari, tàngoor guy yokk, mbeyum nawet muy gën di néew, ndaw ñuy gàddaay.

Coppikug kéew gi ak pexey sunug yàgg fi : ab dékk ñeel taax yeek li leen wër

Ndar a ngi fàttu ci lori coppikug kéew gi :

  • Bekkoor (néewum ndox ak dund gi ciy loru).
  • Mbënn yeek wopp yi aju ci ndox.
  • Géej giy wann suuf si, di yàq dëkkuwaay yi, Oteel yi ak Pàrku « Langue de Barbarie ».
  • Xorom siy nangu suuf si.
  • Ñàkk ndox miy am ci gàncax yiy sax ci dex gi.
  • Tàngoor ak wàññikug dox mu neex mi nekk Bàngoo.
  • Yooyu yépp day am jeexit ci nosteg dundu giy màndargal Ndar di dëkkub dox.

Coppikug kéew gi gi ak pexey sunug yàgg fi : ab dékk ñeel Ndar li ko wër

Ca tefesu Ndar, diñañu fa gis :

  • Géej guy faral di fees ndax ngelaw yu tar.
  • Ndoxum géej giy wal di dugg ci jéeri ji : di néewal doole tabax yi.
  • Ñàkk ay dëkkuwaay : dunu njanaaw yi, Pàrku « Langue de Barbarie » bu Gànjool, fi mbonaant yiy nene ca hydrobase, mbënn muy am gàncax yiy sax ci dex ca Rhizophora ci yoonu Dun Baaba Jéey ak Kër Bernaar mi nekk di dundaat.
  • Naaxsaayug Aada ak cosaan : armeeli Dun Baaba Jéey, mbënn yi mën a am ci armeeli Goxu-Mbaac ak yu Get-Ndar.
  • Yàqu-yàqu yiy am ci tefes gi : teerub Goxu-Mbaac, teerub Get-Ndar, Faaru  Gànjool, armeelu Dun Baaba Jéey.
  • Ay lor ci noste dundu ak ci dëkkuwaay yi.
  • Wàññikug yaatuwaayu gàncax yiy sax ci dex ndax xorom si.
  • Wàññikug yàggaayug jamonoy sedd. Jamonoy tàng di gën di yokk.
  • Jaxasook jomonoy ngelaw yu tar yi ak seeni jeexit ci napp gi.
  • Yokkteg tàngoor gi ci kaw ndox mi ci tefes gi, di jur yokkteg xorom si (wàññikug pH), jax-jax ci jén yi.
  • Wetug jéeri ji (Gàndoŋ, Paal, Faas Ngom) moo gën a xiibon ci coppikug kéew gi : tàngoor, tawte ak ngelaw.
  • Yeexte ak wàññikug taw bi.
  • Lor gu yemaay ci gàncax gi.
  • Wàññikug ndoxu seyaan yi.
  • Yàqu-yàquy ngelaw li, suuf siy nangu toolu mbeyum noor yi.
  • Bariwaayu tar-tari tàngoor te dàggub garab yi waral ko.
  • Coppikug kéew gi ag tëkku gu tegu ci nosteg dundu gi ci Afrig.

Coppikug kéew gi ak mbënn yi ci Ndar

Ñaari xeeti mbënn ñoo am Ndar :

  • mbënn yu doxum taw mbaa doxum dex waral.
  • mbënn yu ndoxum géej gi waral (ci tefes gi).

Mbënn yi tukke ci doxum ndex gi ci Ndar, ñu ngi  tukke ci :

  • dex gu fees (taw bee koy faral a def).
  • mbir yu aju ci mbindinu suuf si.
  • dox mu yéeg tukke ci dex yu ndaw yu fatt.

Janax yiy màbb tefes gi

  • Liy waral màggug fesesu Ndar gi mooy janax yi, bël yi ak géej gu fees.
  • Dooley bël yee ngi soppiku ak coppikug kéew gi. Dooleem a ngi gën a tàllalu ci aw at ci tefesu Ndar (ci taax yi ak ci tefesu Gànjool).
  • Ngelaw lu tar ñi ngi koy yég ci weeru Mee. Jamono ji ñuy tënku di màrs ba Nowàmbar tuuti la soppiku.
  • Loolooy weer tefes gi soppikug tolluwaayu ndox mi ak congug tundu suuf yi ak dëkkuwaay yi nekk ci déndu tundu yu yàggul a sosu. Moo waral nosteg dundu gu xeebu.

Coppikug kéew gi ak mbënn ci Ndar

  • Kàrce Soor a ngi sañcu ci barab bu suufe fu ndoxi taw yi di dajaloo di feesal ci lu gaaw dox mi biir suuf si te am xorom .
  • Li ëpp ci gox yi nekkul ci dun  dañoo bari ngelaw. Lii féete ci suuf ak ci peggu delaa bi gox yu suufe lañu.
  • Tpmb yu suufe yi te xóot, ñoo yemook suuf yu diis yi te am xorom (mën a jàpp ndox lool, néew lu ndox miy ñeer, lu jege 3 mm/bis).

Coppikug kéew gi ak xorom si

  • Ndar ak nuruwaaleem bu Gànjool ñu yomb am suuf ak ndoxum xorom lañu.
  • Ci tefes fi, géej gi day màbb dëkkuwaay yi.
  • Ci penku dëkk bi, xorom saa yàq tabax (Xor, Site Vauvert, Jàmmagën, Jàmminaar, Daaru, Okleer, Medina kurs).

Boo demee Gànjool, ndoxu xorom mi moo waral :

  • ñuy bàyyi tool yi.
  • ñuy  màng cii biir dëkk bi ngir am ndox mu neex.
  • ñuy def yeneeni liggéey ak di wott xorom ak yoxos.
  • ndaw ñi di gàddaay ci yeneeni gox (ci biir réew ak ci bitim-réew).

Dékki kéew gi ñeel dëkkub baaraami dex

Ndar dëkkub baaraami dex la ak bob géej, di lu koy taaral, waaye it muy lu doon ëllëg lu wóoradi. Péeg jeexiti tàngooru kéew gi, muy ndoxum géej giy yokk, tefes yiy màbb, jéyya yees xamale ci waynadre Senegaal (Cop 21), mooy li ñu war a jàpp léegi muy farata ngir tabax taaxi ëllëg : mànkoo gi am diggante dëkk ak dalu turist gi mu doon, jaxasoo gi diggante ndox meek suuf si, nit ki ak kéew gi, am nañu ci ag tiit ëllëg. Li ñu ragal mu dal taaxu Ndar mooy mu ñàkk « Langue de Barbarie » miy koy sàmm moom ak baaraami dex gi ci merum géej gi. Yemul ci loolu rekk, fa la mboolem yëngu-yënguy nappkat yi di ame, bokk na it ci barab yu Afrig yi gën a fees ak nit, oteel yu bari ak ay dali doxandeem (turist), ak pàrkub njanaaw yi : kon ñu gis ne am na taxawaay bu am solo ci koom-koomu dëkk bi ak li xëcc doxandeem yi. Ëllëgam wóorul dara : dex gi daa dugg ci fàcc bu ñu amaloon ci 2003 ngir sàmm dëgg bi ci mbënn, tey jii yaatoo ay kilomeetar ba mel ni bël bu bees, te weneen wàll géej giy nangu suuf si ci tefesi Afrig gépp, daa mel ni ci tefesu Ndar la rawe ak kër yuy daanu.

Rax ci dolli « langue de barbarie » bu Ndar a kyu ni mel ci biir suuf si mbënn sonnal na leen. Naka-jekk gaawaayu dex day jekk yokk ndax taw bi, léeg-léeg baraas yi yeexal ko. Loolooy waral ñuy am yenn ci gox yi di gën a tooy bu ndex gi feesee ; fees googoo ngi faral di am ci weeru sàttumbar ak oktoobar tey amal mbënn yu rëy. Ndegam tabax ay gaw moo ànd ak tabax dëkku taax, jàpp nañu ne dees na wéyal tabaxug dëkk bi ak i gaw. Waaye loolu day tere dex gi di wal, bu ko defee du fees ba yéeg, rawatina jamonoy nawet.

Ay dékkaane

  Wàll    Leeralug taamu yi

  Yoriin  Taxawu naalug pexey biir réew mi ngir jàmmaarllok coppikug kéew gi ; Jàpp ci weccooy doxalin ngir ñuy sóoraale coppikug kéew gi ci pexey suqale koom-koom gi.
                              Mbey mi        Faral kaaràngeg mbey ak gog xam-xamu kéew;Fexee jëlaat suuf yu yàqu yi (suuf si xorom si nangu) ;Ut ay xeeti juwwu yu gën a dëppoo ;Jàppandal ndox mi ngir dooleel te yeesal mbey mi; Tàggat ñiy jël dogal ; Xiir nit ñi ci mbeyin mu gën jaare ko ci njàngale mi ak ci tasukaayu xibaar yi ; Jëmbat garab yuy wàññi doole ngelaw li ak ay gaw ngir fegu ci mbënn ;Ñaax beykay yi ci mbeyum noor ;Amal ay pexey ngir fegu ak yuy yëgle Wéyal gëstuy pexe yu yéeme, dellu ci tàggat beykat yi ; Dooleel séddaleg suuf si ci melo wuy sóoraale jéyya yi ; Dëppale jumtukaay yi ñuy aaree ak yi ñuy yëglee ak jéyyay wér-gi-yaram yi yees yi ngir nànd te topp jeexiti coppikug kéew gi ;Jëfandikoo nostey dundu yi ci anam guy tax ñu yàgg ngir wàññi nooteel gi tukkee ci coppikug kéew gi; Xiir askan yi ñuy màng ci yeneeni suufi mbey ci anam gog dinañu sàmm ngëm-ngëmi ña fa dëkk ;Xiir ñi yëngu ci mbey mi ñu def yeneeni liggéey yu coppikug kéew gi sonnalul S0mm barab yi ci jëmbët ay garab yuy wàññi doole ngelaw li ak ay gaw yuy tëyee xorom si ;Dugal coppikug kéew gi ci politigu gox yi ;Amal jumtukaay buy yombal weccoo xalaat yi aju ci wàll woowu.
          Àll bi      Jàppale askan wiy dunde àll bi ñu sóoraale coppikug kéew gi ; Sàmm noste dundu gi ak njariñu àll ci coppikug kéew gi ; Fagaru ci xew-xewi kéew yu tar yi; Dox ci yor alal ji ak njariñ yi yorin wu leer;Dooleel mën-mënu way-yëngu yi ci wàllu xarala ak ci yorinu xaalis  Boole askan yi ci xeex rëbb gi ;Yeesalaat te aar nosteg dundu gi ci suuf si, si ndox mi ak ci jawwu ji ;Xiir nit ñi ñuy jëfandikoo kàttan yu yees yi Teg ay pexe ngir xeex daay.
    Gëstu    Dooleel gëstu gi ak koom mi jëm ci dëppale àll ci coppikug kéew gi ; Dajale njuréefi àll bi te fexe ñu jàppandi ci ñépp ; Yokk xamug kéew gi ak ay jeexitam ci fexe gëstu gi jëmandoo ci ñetti yoon :Càmbar njàngale yi jëm ci coppikug kéew gi ;Suuxat gëstu gi ngir jàppandal ba ñuy tabax te jëme jumtukaay ci yoon yu ñu gën a dëppoo.
          Njàngale ak tàggat    Jàppandal jàngukaay ay jumtukaayu njàng ; Toppale jeexit dëppoo gi coppikug kéew gi ci bànqaas yees di jàngale ci liggéey yi aju ci koomug àll bi;Yokk tàggatug xelalkat yi ci cosug liggéeyuwaay ngi ñu mën a dugal ëllëgu kéew gi ci càmbaru njariñal sos liggéeyuwaay; Xoolaat njàng mi ak téere ngir dollu coppikug kéew gi ;Dolli ci ay dol lak bind yuy jàngale xeex coppikug kéew gi ;Teg njàngale mi ci coppikug kéew gi te boole ci liggéeyandoowaale yi ;Yokk dooley njiit yi ak ñi ciy yëngu ci ali aju ci coppikug kéew gi ;Dëppale ci yenn gox waxtu yi ñuy jàng ci jamonoy tàngoor ;Dëppale barabu jàng yi ak gox yi coppikug kéew gi laal ;Tabax ay lekkool yi te sooraale ci mboolem jafe-jafe yi ñuy ci diir bu gàtt ak bu gudd.
    Dëkkinu taax ak ak cadre bâti  Fexe ñu sóoraale coppikug kéew gi ci wayndarey dëkkinu taax ;Dëppale yoriinu dund gi ci taax yi ak barab yi ñuy féexloo ; Amal ay ndaje ci biir réew mi ngir ñaaxe ci yokk ay barabi garab yu dëppook kéew gi ;Càmbar doxalin yi gën a dëppook dëkkinu taab yi am mucc ;Jëf ngir am dëkkuwaay yu nekkin wi neex te dëppook tàngoor giy dëkke yokk.
        Barab yeek dem beek dikk bi  Xolaat te dëppale royuwaayi xarala yi ngir ag tëral, ag yeesal ak ug jariñu dem beek dikk bi ; Jàng coppikug kéew gi ci soxlas dem beek dikk bi ak li nga xam ne xeeti tukkikaay di na ko jur ; Teg ay doxalin yu ñu déggoo ngir amal ay càmbar ci néew-néewi dem beek dikk bi ci suuf, ci ndox mi ak ci jawwu ji ; Def ab taxaw-seetlu ci néew-néewi dem beek dikk bi ci suuf si, ci ndox mi ak ci jaww te waajal pexey toontu yu dëppook coppikug kéew gi.
      Xibaar yi    Ñaax taskatu xibaar yi ñuy gën ci joxe ay xibaar ci kéew gi ; Yokk jokkoloo bi jëm ci askan wi, njiit yi ak barabu liggéey yi ; Boole siiwalug jeexit ci gox yi ngir mën a waajal askan wi ci yoon yees war a jël ngir dox ci dund gu dëppook coppikug kéew gi. ; Dajale te siiwal lees war a njëkk xam ci coppikug kéew gi ; Yee ñiy jël dogal te jox leen xibaar yi ñu war a xam.
    Oteel yiJëmbataat filaawoo yi ngir sàmm tefes yi ;Amal ay politigu yeete, setal tefes yi ;Teg ay pexe yu xiir askan wi ñuy sàmm barab yooyu ;Nangu tefes yi ;Dundalaat pàku « Langue de Barbarie » ; Xoolaat ni kilifay nguur gi ci dugalee alal ji ci barab yooyu.
    Yaatug dund gi      Dooleel jumtukaayu topp yi am ngir sóoraale jeexiti coppikug kéew gi ci yaatug dundu gi ; Fexee yaatal ñuy yor gox yi cig déggoo tey sóoraale coppikug kéew gi ci yaatug dund gi ; Boolee dëppook coppikug kéew gi ci pexe yi nguur yi di lal ngir sàmm yaatug dung gi ; Baril barab yi koy sàmm ;Amal ay doxalin yu wér ñeel ay pexey dëppale ;Amalaat dundu gi ci àll bi gir aar bakkan yi ciy dund.
      Càmm giFexee yaatal kaarug càmm gi ;Ñaaxe suuxat jur gi ;Ñaaxe ci yafal ak tëyee jur gi bañ leen bàyyee seen bopp ;Amal ay barabi jur ju jaar yoon ;Amal yeneeni yoon ñeel alalal ak njaayum jur gi ;Ñaaxe ci sàmmkat yi ñuy def yeneen liggéey ; Ñaaxe ci mbeyum ñax ;Amal ay barab ngir mala yi;Fexe ñiy yëngu ci mbey mi mën di def yeneen liggéey yu coppikug kéew gi laalut noonu ; Fexe niti politig yi di sóoraale bu beex càmm gi.
            Wér-gi-yaramDooleel te amal ay pexe ngir topp tawat yi ;Wàññi mën a amug wopp yi aju ci feebaru caar, sibiru ak feebaru der;Wàññi yàqug njàngum xale yi ndax ñi loru ñiy dëkk ci lekkool yi ak mbënn yi am ci lekkool yi Dooleel gëstu gi ñeel wér ak kéew ;Dooleel toppug li mën a waral coppikug kéew gi;Natt li coppikug kéew gi mën a jur ci wér-gi-yaramu askan wi ;Amal ay yënguy fagaru ci wér-gi-yaram yuy sóoraale jeexiti coppikug kéew giYee te tàggat mboolem ñi ciy yëngu ak ay ndaje tàggat, xibaar ak jokkoo ;Amal ay yoon yu ndoxu taw mi mën di jaar ;Amal ay dagaani yeete jaare ko rajo yeek tele yi;Amal ay dagaani ngir séddale ay sànke ;Amal ay prograam ngir xeex tilim gi ;Amal ay toppantoog xel ñeel askan yi loru ci coppikug kéew gi.
                  Wàllu ndoxJotug  « ndoxum njariñ » muy mën a yokk seenug am-am ci barab yi ame ay ndax coppikug kéew gi ;Sos ay liggéey ci barab yooyu ñu samp loolee ;Feesalaat ronu suuf si ag ndox;Jàpp ci xeex jafe-jafe yi xorom si amal ;Xóotal teeni maam yi ;Amal ay rootukaay yu dëppook jamono ;Màng jëm ci barab yu gën a tooy ;Aar barabi ndox yi ; Amal ay pexe yu am solo ngir taataan ndoxum taw mi ;Am xereñte ci coste yi ;Yor ndox mi ci dëppoo;Gën a yokk xamug jeexit yi coppikug kéew gi jur ci ndox mi ;Am ay jumtukaay yu baax ngir topp jeyya yi juddoo ci coppikug kéew gi; Sàkkanal ndox mi ; Gunge leen ñuy amal ay yëngu tey jëfandikoo suuf si ci anam biy sakkanal ndox mi ; Dooleel sóoraale coppicug kéew gi ci yorinu ndox mi.
        Napp gi  Dooleel kaaràngeg napp gi ;Yokk dooley yorinu géej yi ñu aar ci napp;Sóoraale xamug barab yi;Fexe bu ku nekk am wàll ci yorinu géey ji ñu aar ci napp ;Dooleel mën-mënu ñi ciy yëngu ;Dooleel sañ-sañu askan yi ci yorin bi ;Am ay jumtukaayi xarala yu ni dëppoo; Siiwal jaar-jaar yi nga xam ne dox na ;Suuxat mbeyum jëm te fexee sàmm njariñ li ci ndox mi;Ñaax askan wi ñu gën a dugal seen loxo ngir sàmm ëllëgu napp mi ; Ñaaxe ci noppalug dundu gi ci géej gi ak ci mbeyum jën mi.
  Kaarànge dund  giAar fi ñuy denc pepp mi ;Ñaaxe ci ñu amal yoon yuy mën a sàmm dund gi ;Siiwal dundin yi gën dëppook coppikug kéew gi ; Ñaaxe si sopparñi ñam yi ;
    Oteel yiJëmbataat filaawoo yi ngir sàmm tefes yi ;Amal ay politigu yeete, setal tefes yi ;Teg ay pexe yu xiir askan wi ñuy sàmm barab yooyu ;Nangu tefes yi ;Dundalaat pàku « Langue de Barbarie » ; Xoolaat ni kilifay nguur gi ci dugalee alal ji ci barab yooyu.